fbpx

Yan leeral lañuy jëfandikoo?

Sudee ki tawat dafa bokk ci prograamu Max Access Solution (MAS), danuy jël, deñc, ak jëfandikoo (cib gàttal, “liggéey”) done jàmbur yii ci suuf:

  • Sa tur
  • Góor/jigéen
  • Sa bésub juddu
  • Sa(y) nimero telefon
  • Sa adres imeel
  • Sa adres biñu lay yónnée bataaxal;
  • Turu opitaal ak medsin bi lay faj
  • Xaalis bi nga am wala sa tolluwaayu xaalis (soo ko amee)

ak

  • Leerali jokkoo ki lay faj (soo ko amee).

(cib gàttal, say « leerali bopp »)

Ngir nu mën la jox garab ak pajtal yi war, dina nu jëfandikoo itam say leerali bopp yu warul siw :

  • Sa càmbaarug yaram
  • Bis bi ñu càmbaree sa yaram
  • Xeetu pajtal biñu lay defal
  • Bis bi nga defee say test molekuleer ak say resiltaa test PCR.

(cib gàttal, say « done jàmbur su suturlu »)

Naka ak lu tax nuy jëfandikoo say done bopp ak doney jàmbur yu suturlu?

Danuy jëfandikoo say done bopp ak doney jàmbur yu suturlu direktëmaa ci yaw, medsin ak/wala ki lay faj sudée danga dugal këyit ngir wut yaw mii tawat benn ci sunu leeralu MAS. Danuy jëfandikoo say done bopp ak doney jàmbur yu suturlu ngir sabab yii:

  • Ngir ñu xàmmee la
  • Ngir jokkoo ak yaw
  • Ngir jox la fajtal ak toppatoo yaw mi tawat
  • Ngir tasaare ay leeral yu jëm ci feebar ak pajtal
  • Ngir mayñu ñu mëna amal sunu wareef bu dëppoo ak li yoon tëral wala sàrt yi
  • Ak beneen mëbët bu bokk wala ànd ci doxal ak yor wala saytub prograam yi.

(cib gàttal, “Mébet” yi). 

Mën nanu jëfandiko say done ci anam wuñ jaxasé wala wu nëbbu su amee lu ñuy siiwal. Loolu li muy tekki mooy dañuy dindi  bépp leeral (ci misaal sa tur, sa bisu judd, sa adres) buñ la mëna ràññee suko defee kenn du mëna xamni say done la.

Kan mooy mëna wané say leeralu bopp ak leeralu jàmbur si suturlu?

Ñii ñoo mëna wan say done bopp ak/wala say leeral bopp si suturlu:

  • Bànxaas yu bokk ci The Max Foundation; ak
  • Liggéeyukaay yiy doxal yoon wala liggéeyukaayu nguur sudee yoon moo nu ko digal.

Say leeralu bopp ak leeralu jàmbur yu suturlu dañu dénc itam ci sunu base de done mu deggu lol lalu ci web bi te réewum Etat Unis dalal ko te am kaaraangé.

Du ñu wan say done bopp ak doney jàmbur yu suturlu keneen ku bokkul fileek àndoo ci nu joxe ko. Dina nu aar bu baax itam say done bopp ak/wala doney jàmbur yu suturlu, fexe ñu nekk ci barab bu wóor.

Ana luy xew sudee dañu ñàkka ànd ci nu jëfandikoo say done bopp ak doney jàmbur yu suturlu?

Sudee danga ñàkk ànd ci ñuy jëfandikoo say done bopp ak doney jàmbur yu suturlu ci biir yëgle done jàmbur bii, kon doo mëna bokk ci prograami The Max Foundation.

Say sañ-sañi kaaraange done:

Ci loi kaaraange done, am nga sañ-sañ yii nuy lim:

  • Sañ-sañu am leeral yi war – Am nga sañ-sañ ñu leeralal la yan ci say done lañuy jël, naka lañu leen di jëfandikoo, diir bu tollu nan lañu leen di tëye ak ndax dañu koy séddoo ak yeneen jàmbur am déet.
  • Sañ-sañ am ci leeral yi – Am nga sañ-sañu laaj nu sotti say leeral jox la ci ab kopi booy yor.
  • Sañ-sañu indi ay coppite – Am nga sañ-sañu laaj nu may la nga indi coppite (jubbanti) leeral yi nga jàpp ni njuumte daf ci am wala matu ñu.  
  • Sañ-sañ sàkku ñu efaase – Am nga sañ-sañu laaj nu éfaase (suprimé) say leerali bopp ci yenn anam yi.
  • Sañ-sañ yamale jëfandikoo gi – Am nga sañ-sañu laaj nu yamale jëfandikoog say leeral ci yenn anam yi.
  • Sañ-sañu baña ànd ci jëfandikoo gi – Am nga sañ-sañu baña ànd ci ñuy jëfandikoo say leeral bopp ci yenn anam yi.
  • Sañ-sañ ci ñu joxeel la – Am nga sañ-sañu laaj joxe say leeral yi nga nu jox beneen mbootaay, wala yaw ci sa bopp, ci yenn anam.
  • Sañ-sañu yëgal jalgati gu am – Su fekkee dañu jalgati lenn ci say kaaraange leerali wérgi-yaram wala lu ko ëpp, am nga sañ-sañ ñu yëgal la ko.

Amul benn xaalis boo wara fay ngir ñu defal la sa sañ-sañ yi nga yelloo. Su amee looy sàkku, am nanu diiru weer ngir tontu la.

Jokkool ak nun ci adres bii, sudee danga am loo bëgga laaj wala sàkku :

The Max Foundation
1448 NW Market St.
Suite 500
Seattle, WA 98107
+1 (206) 778-8660
info@themaxfoundation.org